WOLLEB_JLD_NARR_01_FJNDAYAAN.EAF     karaoke karaoke2

ecouter
léeb bi maa léeb nak  
le conte que je vais dire alors
léeb bi maa léeb nak
léeb bi maa léeb nak
conte que\qui Je_INACCOMPLI conter alors
N PN STG V CONJ
ecouter
maaŋ kaa def si ab beykat bu maga maga maga mag  
je le fais au sujet d'un très grand cultivateur
maaŋ kaa def si ab beykat bu maga maga maga mag
maaŋ ka -a def si ab bey -kat bu mag -a mag -a mag -a mag
je_PRESENTATIF le\la INACC faire à propos de un\une cultiver AGENTIF qui\que être_grand a-VERBAL être_grand a-VERBAL être_grand a-VERBAL être_grand
IPAM PN SUF VT PREP ARTINDSG VT SUF PN VI SUF VI SUF VI SUF VI
ecouter
ba ñaa wah baay suleymaan fay  
qu'on dit père suleymane faye
ba ñaa wah baay suleymaan fay
ba ña -a wah baay suleymaan fay
que on INACC parler\dire père Souleymane Faye
PN PNIND SUF V N N N
ecouter
moom dahë bëgaa bëga bëga tool  
lui il aime aime les champs
moom dahë bëgaa bëga bëga tool
moom dafa bëg -a bëg bëg tool
lui\elle EXPLICATIF aimer a-VERBAL aimer aimer champ
PN MOD VT SUF VT VT N
ecouter
ba ken hamul ni mu bëgge tool  
jusque personne ne sait comme il aime les champs
ba ken hamul ni mu bëgge tool
ba ken ham -ul ni mu bëgg -e tool
jusque personne\quelqu'un savoir NEG comment il\elle aimer APPLICATIF champ
ADV PNIND VI SUF ADV PNS3SG VT SUF N
ecouter
baay suleymaan nak  
père suleymane alors
baay suleymaan nak
baay suleymaan nak
père Souleymane alors
N N CONJ
ecouter
mu béy ag ñeebe  
cultive des cornilles
mu béy ag ñeebe
mu béy ag ñeebe
il\elle cultiver un\une cornille
PNS3SG VT ARTDEFSG N
ecouter
béy ñàmbi  
cultive du manioc
béy ñàmbi
béy ñàmbi
cultiver manioc
VT N
ecouter
béy lépp si biir tool ba  
cultive tout dans le champ
béy lépp si biir tool ba
béy lépp si biir tool ba
cultiver tout à intérieur champ le\la
VT ADV PREP ADV N ARTDEFSG
ecouter
baa mu demee dema dem nak ba ñàmbi ja ñor  
quand il part part part alors jusque le manioc est mûr
baa mu demee dema dem nak ba ñàmbi ja ñor
baa mu dem -ee dem -a dem nak ba ñàmbi ji ñor
quand il\elle partir\aller ANT partir\aller a-VERBAL partir\aller alors jusque manioc le\la être mûr
CONJS PNS3SG VI SUF VI SUF VI CONJ ADV N ARTDEFSG VI
ecouter
ñeebe ja ñor  
les cornilles sont mûrs
ñeebe ja ñor
ñeebe ji ñor
cornille le\la être mûr
N ARTDEFSG VI
ecouter
mu am bés  
il y a un jour
mu am bés
mu am bés
il\elle avoir jour
PNS3SG VT N
ecouter
kéwél ah mbëtë dem ne dañu kaa yaaha  
biche et varan partent disent qu'ils vont le saccager
kéwél ah mbëtë dem ne dañu kaa yaaha
kéwél ah mbëtt dem ne da -ñu ka -a yàq
gazelle et varan de terre partir\aller dire EXPLICATIF ils\elles ça INACC endommager\gâter
N PREP N VI V MOD PNS3PL PN SUF VT
ecouter
baay suleymaan la yoot la yoot la yoot la yoot  
père suleymane de marcher à pas feutrés
baay suleymaan la yoot la yoot la yoot la yoot
baay suleymaan la yoot la yoot la yoot la yoot
père Souleymane INACC marcher_à_pas_feutrés INACC marcher_à_pas_feutrés INACC marcher_à_pas_feutrés INACC marcher_à_pas_feutrés
N N AUX V AUX V AUX V AUX V
ecouter
be bi ka kéwél séenee  
jusque quand biche l'aperçut
be bi ka kéwél séenee
be bi ka kéwél séen -ee
jusque quand le\la gazelle apercevoir ANT
PREP CONJS PN N null SUF
ecouter
ham naal kéwél comme ni ñaa wah ne kéwél du tëb doom ja bëta  
tu sais biche comme on dit que biche ne saute pas le petit perce
ham naal kéwél comme ni ñaa wah ne kéwél du tëb doom ja bëta
ham naal kéwél comme ni ña -a wah ne kéwél du tëb doom ji bëtt
savoir MOD_tu gazelle comme on INACC parler\dire que gazelle futur négative sauter progéniture le\la passer_à_travers
VI IPAM N ADV PNIND SUF V CONJ N MOD V N ARTDEFSG VT
ecouter
kéwél ne cëlaŋ mu daw  
biche fait un bond elle courut
kéwél ne cëlaŋ mu daw
kéwél ne cëlaŋ mu daw
gazelle faire bondir il\elle fuir
N COV ONOM PNS3SG VT
ecouter
mu jaala mu baayi fa mbëtë nak mbëtë témbë  
elle passe elle laisse là varan alors varan est coincé
mu jaala mu baayi fa mbëtë nak mbëtë témbë
mu jàll mu bàyyi fa mbëtt nak mbëtt témbë
il\elle passer il\elle abandonner là-bas varan de terre alors varan de terre être_coincé
PNS3SG V PNS3SG VT ADV N CONJ N VI
ecouter
baay suleymaan nak  
père suleymane alors
baay suleymaan nak
baay suleymaan nak
père Souleymane alors
N N CONJ
ecouter
bëgë bëgë mbëtë ba bëga dee ndah fay la santa ka santa fay ham naal leekë reka lañaa bëgë  
aime aime aime varan jusque vouloir mourir car c'est faye qu'il se nomme quelqu'un qui se nomme faye tu sais c'est manger seulement qu'ils aiment
bëgë bëgë mbëtë ba bëga dee ndah fay la santa ka santa fay ham naal leekë reka lañaa bëgë
bëgg -a bëgg -a mbëtt ba bëg dee ndax fay la santa ku santa fay ham naal lekk rekk la -ñaa bëgg
aimer a-VERBAL aimer a-VERBAL varan de terre jusque aimer mourir plutôt_que_de Faye c'est...que... avoir_pour_patronyme quelqu'un avoir_pour_patronyme Faye savoir MOD_tu manger\consommer seulement c'est...que... Ils_INACC aimer
VT SUF VT SUF N ADV VT VI ADV N MOD VT PNIND VT N VI IPAM VT ADV MOD STG VT
ecouter
mu ñów baa mu ñówee mu jaapa mbëtë ma  
il vient quand il vient il attrape le varan
mu ñów baa mu ñówee mu jaapa mbëtë ma
mu ñów baa mu ñów -ee mu jàpp mbëtt ma
il\elle venir quand il\elle venir ANT il\elle attraper varan de terre le\la
PNS3SG VI CONJS PNS3SG VI SUF PNS3SG VI N ARTDEFSG
ecouter
mu daadi jél mbëta  
et il prend varan
mu daadi jél mbëta
mu daldi jél mbëtt
il\elle puis\alors prendre varan de terre
PNS3SG ADV VT N
ecouter
mu rendi  
il égorge
mu rendi
mu rendi
il\elle égorger
PNS3SG null
ecouter
tëllë  
découpe
tëllë
tëll
couper_en_darnes
VT
ecouter
sóppi  
échaude
sóppi
sóppi
échauder
VT
ecouter
def lépp ba mu pare  
fait tout jusque c'est prêt
def lépp ba mu pare
def lépp ba mu pare
faire tout jusque il\elle être prêt
VT ADV ADV PNS3SG VT
ecouter
mu daadi yóobu mbëtë nak mu la tooga  
puis il emporte varan alors il cuisine
mu daadi yóobu mbëtë nak mu la tooga
mu daldi yóbbu mbëtt nak mu la togg
il\elle puis\alors emporter varan de terre alors il\elle INACC cuisiner
PNS3SG ADV VT N CONJ PNS3SG AUX VT
ecouter
fa mu tuur ndoh  
où il verse de l'eau
fa mu tuur ndoh
fa mu tuur ndoh
il\elle verser eau
PN PNS3SG null N
ecouter
mbëtë maa ngaa woy  
varan chante
mbëtë maa ngaa woy
mbëtt maa nga -a woy
varan de terre ARTDEFSG_PRESENTATIF PRESENTATIF+DISTANT INACC chanter
N STG MOD SUF VT
ecouter
fa mu saanib der  
où il jette une peau
fa mu saanib der
fa mu sànni -b der
il\elle jeter SG peau
PN PNS3SG VT CLASSE N
ecouter
mbëta maa ngaa woy  
varan chante
mbëta maa ngaa woy
mbëtt maa nga -a woy
varan de terre ARTDEFSG_PRESENTATIF PRESENTATIF+DISTANT INACC chanter
N STG MOD SUF VT
ecouter
mu nga naan  
il dit
mu nga naan
mu nga naan
il\elle PRESENTATIF+DISTANT dire
PNS3SG MOD V
ecouter
kéwél a ma tooñ kéwél a ma tooñ oo baay suleymaan  
c'est biche qui m'a fait tord c'est biche qui m'a fait tord oh père suleymane
kéwél a ma tooñ kéwél a ma tooñ oo baay suleymaan
kéwél a ma tooñ kéwél a ma tooñ oo baay suleymaan
gazelle c'est_qui me faire tort gazelle c'est_qui me faire tort père Souleymane
N MOD PNC1SG VI N MOD PNC1SG VI N N
ecouter
mbëta mënta daw mbëta mënta jaab oo baay suleymaan  
varan ne sait pas courir varan ne sait pas galoper oh père suleymane
mbëta mënta daw mbëta mënta jaab oo baay suleymaan
mbëtt mën -t -a daw mbëtt mën -t -a jaab oo baay suleymaan
varan de terre savoir NEG a-VERBAL courir varan de terre pouvoir NEG a-VERBAL galoper père Souleymane
N V SUF SUF VT N V SUF SUF VI N N
ecouter
mu di ka def mu di ka def be  
il le fait il le fait jusque
mu di ka def mu di ka def be
mu di ka def mu di ka def be
il\elle INacc ça faire il\elle INacc ça faire jusque
PNS3SG ASPECT PN VT PNS3SG ASPECT PN VT PREP
ecouter
baay suleymaan jél mbëta ma sóob sa cin la  
père suleymane prend le varan plonge dans la marmite
baay suleymaan jél mbëta ma sóob sa cin la
baay suleymaan jél mbëtt ma sóob sa cin ba
père Souleymane prendre varan de terre le\la plonger à marmite le\la
N N VT N ARTDEFSG VT PREP N ARTDEFSG
ecouter
cin la la woy  
la marmite chante
cin la la woy
cin ba la woy
marmite le\la INACC chanter
N ARTDEFSG AUX VT
ecouter
baay suleymaan la tooga  
père suleymane cuisine
baay suleymaan la tooga
baay suleymaan la togg
père Souleymane INACC cuisiner
N N AUX VT
ecouter
baay suleymaan sippi  
père suleymane retire
baay suleymaan sippi
baay suleymaan sippi
père Souleymane retirer_de_la_marmite
N N VT
ecouter
baa mu ka sippee tamit  
quand il le retire aussi
baa mu ka sippee tamit
baa mu ka sippi -ee tamit
quand il\elle ça retirer_de_la_marmite ANT aussi
CONJS PNS3SG PN VT SUF ADV
ecouter
noogu rek  
ainsi seulement
noogu rek
noonu rek
sur_ces_entrefaites seulement
ADV ADV
ecouter
yàppa waa nga naan  
la viande est en train de dire
yàppa waa nga naan
yàpp waa nga naan
viande la_PRESENTATIF PRESENTATIF+DISTANT dire
N STG MOD V
ecouter
kéwél a ma tooñ kéwél a ma tooñ oo baay suleymaan  
c'est biche qui m'a fait tord c'est biche qui m'a fait tord oh père suleymane
kéwél a ma tooñ kéwél a ma tooñ oo baay suleymaan
kéwél a ma tooñ kéwél a ma tooñ oo baay suleymaan
gazelle c'est_qui me faire tort gazelle c'est_qui me faire tort père Souleymane
N MOD PNC1SG VI N MOD PNC1SG VI N N
ecouter
mbëta mënta daw mbëta mënta jaab oo baay suleymaan  
varan ne sait pas courir varan ne sait pas galoper oh père suleymane
mbëta mënta daw mbëta mënta jaab oo baay suleymaan
mbëtt mën -t -a daw mbëtt mën -t -a jaab oo baay suleymaan
varan de terre savoir NEG a-VERBAL courir varan de terre savoir NEG a-VERBAL galoper père Souleymane
N V SUF SUF VT N V SUF SUF VI N N
ecouter
baay suleymaan jél leeka ba suur  
père suleymane prend mange jusqu'à être rassasié
baay suleymaan jél leeka ba suur
baay suleymaan jél lekk ba suur
père Souleymane prendre manger\consommer jusque être_rassasié
N N VT VT ADV VI
ecouter
naan ñeeh ma yéy yah ya  
boit le jus croque les os
naan ñeeh ma yéy yah ya
naan ñeex ma yéy yax ya
boire sauce le\la croquer os les
VT N ARTDEFSG VT N ARTDEFDIST
ecouter
a baay suleymaan tamit jog  
et bien père suleymane aussi se lève
a baay suleymaan tamit jog
a baay suleymaan tamit jóg
père Souleymane aussi se_lever
N N ADV VI
ecouter
dem la julliji  
part prier
dem la julliji
dem la julli -j -i
partir\aller INACC prier en suivant un rituel EPENTHESE EXITIF
VI AUX null INFIXE DEFPROX
ecouter
baa mu demee ba mu aagë sa biir jaaka ja itam  
quand il est parti jusqu'à il est arrivé dans la mosquée aussi
baa mu demee ba mu aagë sa biir jaaka ja itam
baa mu dem -ee ba mu àgg sa biir jàkka ji itam
quand il\elle partir\aller ANT quand il\elle arriver à intérieur petite mosquée le\la aussi
CONJS PNS3SG VI SUF PN PNS3SG VI PREP ADV N ARTDEFSG ADV
ecouter
mbëtë maa ngi wah si biiram bi rek  
le varanest en train de parler dans son ventre
mbëtë maa ngi wah si biiram bi rek
mbëtt maa ngi wah si biir -am bi rek
varan de terre ARTDEFSG_PRESENTATIF voici parler\dire à ventre POSS3SG le\la seulement
N STG MOD V PREP N SUF ART ADV
ecouter
kéwél a ma tooñ kéwél a ma tooñ oo baay suleymaan  
c'est biche qui m'a fait tord c'est biche qui m'a fait tord oh père suleymane
kéwél a ma tooñ kéwél a ma tooñ oo baay suleymaan
kéwél a ma tooñ kéwél a ma tooñ oo baay suleymaan
gazelle c'est_qui me faire tort gazelle c'est_qui me faire tort père Souleymane
N MOD PNC1SG VI N MOD PNC1SG VI N N
ecouter
mbëta mënta daw mbëta mënta jaab oo baay suleymaan  
varan ne sait pas courir varan ne sait pas galoper oh père suleymane
mbëta mënta daw mbëta mënta jaab oo baay suleymaan
mbëtt mën -t -a daw mbëtt mën -t -a jaab oo baay suleymaan
varan de terre savoir NEG a-VERBAL courir varan de terre savoir NEG a-VERBAL galoper père Souleymane
N V SUF SUF VT N V SUF SUF VI N N
ecouter
baay suleymaan dem toog  
père suleymane part s'assied
baay suleymaan dem toog
baay suleymaan dem toog
père Souleymane partir\aller s'asseoir
N N VI VI
ecouter
mbëtë mi la woy si biiram  
le varan chante dans son ventre
mbëtë mi la woy si biiram
mbëtt mi la woy si biir -am
varan de terre le\la INACC chanter en ventre POSS3SG
N ARTDEFSG AUX VT PREP N SUF
ecouter
ñi si jaaka ji ka neeka la wëlbatiku  
ceux qui sont dans la mosquée chacun se retourne
ñi si jaaka ji ka neeka la wëlbatiku
ñi si jàkka ji ku neeka la wëlbati -k -u
ceux\celles à petite mosquée le\la quiconque se trouver INACC retourner EPENTH PRONOMINAL
PNPL PREP N ARTDEFSG PNIND VI AUX VT INFIXE SUF
ecouter
la hool  
regarde
la hool
la xool
INACC regarder
AUX VT
ecouter
a suleymaan fay la neeka si biiram bee waay  
ah suleymane faye qu'est-ce qui se trouve dans son ventre donc
a suleymaan fay la neeka si biiram bee waay
a suleymaan fay la neeka si biir -am bee waay
ah Souleymane Faye ce_que\ce_qui se trouver en ventre POSS3SG le_INTERJ mais !
INTERJ N N PNSG VI PREP N SUF ARTDEFS_INTERJ INTERJ
ecouter
suleymaan lu neeka si biiram bee waay  
suleymane qu'est-ce qui se trouve dans son ventre donc
suleymaan lu neeka si biiram bee waay
suleymaan lu neeka si biir -am bee waay
Souleymane qu'est-ce_qui se trouver en ventre POSS3SG le_INTERJ mais !
N PN VI PREP N SUF ARTDEFS_INTERJ INTERJ
ecouter
waaye baa mu kaabaree kaabara kaabar rek  
mais quand il lève les bras lève les bras seulement
waaye baa mu kaabaree kaabara kaabar rek
waaye baa mu kaabar -ee kaabar -a kaabar rek
mais quand il\elle lever_les_mains ANT lever_les_mains a-VERBAL lever_les_mains seulement
CONJC CONJS PNS3SG VI SUF VI SUF VI ADV
ecouter
mu tahawal  
...
mu tahawal
mu taxaw -al
il\elle se_tenir_debout DEVERBAL
PNS3SG VI SUF
ecouter
baa mu naan alaahakubar rek  
quand il dit alahou akbar seulement
baa mu naan alaahakubar rek
baa mu naan alaahakubar rek
quand il\elle dire Dieu_est_grand seulement
CONJS PNS3SG V INTERJ ADV
ecouter
ne daha juli  
dit qu'il prie
ne daha juli
ne daha julli
dire EXPLICATIF_il\elle prier
V MOD VI
ecouter
in jéeki rek mbëtë mi ne lay  
on reste seulement le varan fait hop
in jéeki rek mbëtë mi ne lay
in jékki rek mbëtt mi ne lay
on demeurer seulement varan de terre le\la faire IDEOPH
PNIND VI ADV N ARTDEFSG COV ADV
ecouter
géena la dem yoonam  
sort va son chemin
géena la dem yoonam
génn la dem yoon -am
sortir INACC partir\aller chemin\voie_d'accès POSS3SG
VI AUX VI N SUF
ecouter
ñéepa nak daw  
tous alors fuit
ñéepa nak daw
ñépp nak daw
tous\toutes alors courir
PNPL CONJ VT
ecouter
man nak fooga la ma fa jógee rek  
moi alors c'est là que j'ai quitté là seulement
man nak fooga la ma fa jógee rek
man nak foofa la ma fa jóg -e -e rek
moi alors là-bas c'est...que... je là-bas se_lever ABLATIF APPLICATIF seulement
PN1SG CONJ PN MOD PNS1SG ADV VI SUF SUF ADV
ecouter
i géene boor booba rek  
je sors de ce bord là seulement
i géene boor booba rek
i génn -e boor booba rek
je sortir APPLICATIF bord ce_là seulement
PNS1SG VI SUF null DEMDISTSG ADV
ecouter
dal tam ma daw  
puis aussi j'ai couru
dal tam ma daw
dal tam ma daw
puis aussi je fuir
ADV ADV PNS1SG VT
ecouter
ñii jaar yoonu marse  
ceux-ci passent par la route du marché
ñii jaar yoonu marse
ñ -ii jaar yoon -u marse
PL ceux-ci\celles-ci passer chemin\voie_d'accès de marché
CLASSE DEMPROXPL null N SUF null
ecouter
ñii jaar fa neeka rek  
ceux-ci passent partout seulement
ñii jaar fa neeka rek
ñ -ii jaar fa neeka rek
PL ceux-ci\celles-ci passer se trouver seulement
CLASSE DEMPROXPL null PN VI ADV
ecouter
waaw lool daal la ma ham nak  
oui c'est ça vraiment que je sais alors
waaw lool daal la ma ham nak
waaw loolu daal la ma ham nak
oui ça\cela vraiment c'est...que... je savoir alors
ADV PN ADV MOD PNS1SG VI CONJ
ecouter
looga nak mu nga hewe woon faa sa ndayaan  
et ça ça s'était passé ici à ndayane
looga nak mu nga hewe woon faa sa ndayaan
loola nak mu nga xew -e woon faa sa ndayaan
ça alors cela PRESENTATIF+DISTANT avoir_lieu APPLICATIF PASSE là-bas à Ndayane
DEMDISTSG CONJ PN MOD VI SUF TEMPS ADV PREP null
ecouter
mu la nub dëkk  
qui est notre village
mu la nub dëkk
mu la nu -b dëkk
qui être notre SG ville\village
PN VI POSS1PL CLASSE N
ecouter
waaw  
oui
waaw
waaw
oui
ADV
ecouter
ecouter
lool nak man fooga la ma fa joge  
et ça moi c'est là que j'ai quitté là-bas
lool nak man fooga la ma fa joge
loolu nak man foofa la ma fa jóg -e
ça\cela alors moi là-bas c'est...que... je là-bas se_lever ABLATIF
PN CONJ PN1SG PN MOD PNS1SG ADV VI SUF